Mbokk yi xarit yeek am di jàmm yi ñi ngi leen di nuyu
Mbégte mu rëy lañ am ci dalal leen ci jàkkaarloo biñ am ak taskatu xibaar yi wara doon tambalig wajtaayu juróomeelu yoon biñ wara amal « carnaval de Dakar » bi wara tàmbale ci fan yi mujj ci weeru nowambar. Ndaje momu ñuy amal at mu jot dafa am solo lolu ci wàllu aada ak cosaan ci sunu réew, bés la boo xam ne Ndakaru dina wane boppam ci bépp anam ngir taaral ak fësal caada yi nekk ci sunu réew ak ci dendu Afrig yëpp.
Ren nak « carnaval » bi dañ ko tënk ci ponku « bokk moomeel ak xamle » mu indi beneen gis-gis ci mbir mi. Ponk bi daf ñuy sas ñu gëstu, sàmm ak xamle li ñu donn ci wàllu caada sunu doom ak sët yiy ñëw ëllëg. « Carnaval » weesu na xumbaay ak mumbaay: bërëb la boo xam ne day wane démb ak tay ba ku ci bokk rekk dinga fësal ab pàcci ci sunu démb.
Atum ren jii nak, dañoo indi tëralin wu yees wu am solo di boole lépp lu ñu am ci wàllu caada. Ci lëkkaloo gu ñu def ak daara jiy jangale wàllu aada ak cosaan dinañ wane ay fent yu mucc ayib yu tukke ci xarañteefu « artiste » yi di wane li sunu askan ame ak mëne ci wàlli caada.
Daañu fa wane fànn yu am solo yu mel ne feccu Ekonkoŋ jóge ca Kasamaas, Koñaagi yu Kedugu, njulli Séeréer ak seen fecc mu am solo momu di Ndut, waaye tamit fecc Jaagwaaru Naar yu neex yoyu. Ñu boole ci tamit gan yu màgg muy « groupe » Guwaadelub bii tudd Maskakle ñu nara nekk ñiy ubbi xew mi ca bitim réew di firndeel booloo gi am ci caada wa Afrig ak wa karayib « caraïbes « . Ay « groupe » cosaa ñu mel ne « majorette », wa « gendarmerie » ak seen « fas » yi ak artiste yu am solo yu mel nei wa « CIADA » ak wa » NGEWEUL RYTHME ». Ñii ñëpp buñ tasee ci mbeddu Ndakaaru dina mel ne tuq su bënn.
Duma jeexaal tei jaa jëfaluma ñi jiite « Carnaval » rawatina Soxna Fatou Kase ndax dogoom ak xarañam ak mbëgéelam ci wàllum caada dafa am solo loolu ci xew xew bii nu amal. Soxna Fatou sa dogu sa gis-gis rootukaay la ci nun ñëpp. Linga mën ci boole nit yi ak soppi xalaat yi ñu am ay jëf yu ràññeeku moo tax nga doon jëmm ju am solo ci « Carnaval » bi. Ñu ngi lay jaajëfal ci ni nga jiite mbooloo mi ca nam gën jekkee.
Juróomeelu atu « Carnaval » bii du dañ koy amal nii rekk waaye dañ ci jublu jàngale ak séddoo xam xam ak caada. Dina ñu may ñu fësal sunu bokk moomeel waye wann àdduna sépp taaru sunu aada ak cosaan. Sunu mbëbët mooy Ndakaaru doon xolu caada Afrig yëpp nga xam ne sunu taarix duñ ko nettali ak ay wax kese waaye dañ koy nettalee tamit ci fecc way ak « peinture » ak lépp lu nara bokk ci xew mu màgg mii.
Kon ñi ngi sàkku ci yéen ñi ñuy jàppale ak taskatu xabaar yi ngeen wesaareel ñu xew mu rëy mii ngir ñu am ci ndam lu rëy. Dinañu fexe ba xew xew mii sax dàkk ci sunu taarixu réew ak taarixu caada fii ci réew mi.
Waaj leen te xam ne narr ngeen dund lu alaa dawme te Ndakaaru dina nekk, ci jeexiitalu weeru nowambar wii, selebe yoonu caada yëpp, dina doon bërëb boo xam ne démb dina tase ak ëllëg ci anam yu mucc taaru te neex ci xol.
Ñu ngi leen di jaajëfal ci seenug jàppale gu sax ak seen teewaay. Nanu fexe ba « Carnaval » bi nekk luñ dul fàtte ba mukk.
Jërë ngeen jëf